Salma Tounkara(Ki dougueul Saly si keuram) Thieuy Yalla ! Xalei bi yeuram nako nak té xamoumako ! Ma ngui mélni kou bokak mom dara té aram nane sangara khamou mako si Adama wala si Awa. Xawma lane la wayé dama ko niéwantal rék. Sank ba lègui mi ngui nélaw, beug nako yéé nguir mou rérr saxx wanté beugouma ko dérangé, motax ma guéneu nank dadi teudj bountou bi dém si sama négu. Fok ma wo Bouba nguir mou lidieuntile ma situation bi. -Bismilahi. (Ma dégu ko). -As Salamou Aleykum Tounkara. (Ma wakh ko). -Wa Salma na ngua déf ? -Ma ngui sante Yalla bou wérr al-hamdoulilah. -Yalla na yagu té sakh. -Amiine ya rabbi. Wa mane déh dama amone béne soxla bou diamp bouma beugone rék ngua taxawoumasi si noumou gueuneu gawé rék. -Soxla wou diam ? Waxma. -Ah mane déh démb si goudi bamay diougu


